Menu

Taalifi cant 142

MBS

1 Dib taalifu yeete bu ñeel Daawuda, ba mu nekkee ca xunt ma. 2 Ma àddu, ñaan Aji Sax ji; àddu ca kaw, di tinu Aji Sax ji, 3 sippi ko sama tawat, diis ko sama njàqare. 4 Bu ma yoqee, ràññee nga samay jéego; yoon wi may jaare lañu ma làqal am yeer. 5 Ma geesu ndijoor, xool; du kenn ku ma faale. Rawtu réer ma, du kenn ku sama bakkan saf. 6 Aji Sax ji, ma woo la wall; ma ne, yaay sama kiiraay, di sama séddoo fi kaw suuf. 7 Teewlul, ma ne wóoy, damaa manatul, xettali ma ci ñi ma topp, dañu maa ëpp doole. 8 Ngalla génne ma fi ma tëje, ma sant la. Man la way-ngëm ñi di yéew ëllëg, yaa may xéewale ab yool.

Everything we make is available for free because of a generous community of supporters.

Donate