Taalifi cant 141
MBS1 Dib taalifu cant, ñeel Daawuda. Aji Sax ji, woo naa la, gaawe ma! Bu ma lay woo, teewlu ma. 2 Yal nanga ma nangul samag ñaan ni cuuraay lu ñu la taalal, loxo yi ma la tàllal di saraxu ngoon soo gërëm. 3 Aji Sax ji, sàmmal ma sama làmmiñ, saytul ma sama kàddu. 4 Bu ma xiir ci lu aay, may jëfe jëf ju bon, ànd ceek ñiy jëf lu ñaaw, di wàlli seeni bernde. 5 Kuy déggal Yàlla, man na maa dóor, bantal ma ci ngor. Loolu ngëneelu cuuraay la, duma ko bañ. Waaye maa ngi saxoo ñaan pexey noon moy. 6 Yal nañu fenqe seeni njiit ciw doj, ba noon yi xam ne dëgg laa wax. 7 Ni ñuy gàbbe suuf ba mu ne ŋafeet, ni la njaniiw di ŋaye, aw seeni yax yu tasaaroo. 8 Aji Sax ji Boroom bi, yaw laa wékki gët, yaw laa làqoo, bu ma seetaan, ma dee. 9 Musal ma ci yeer yi ñu ma gasal, ak fiir yi ma defkati ñaawtéef yi tegal. 10 Yal na ku bon tàbbi cig fiiram, te man ma teggi, wéy.
