Menu

Taalifi cant 138

MBS

1 Ñeel Daawuda. Ma sante la sama léppi xol, woy la, gàngooru Yàlla ga ca kaw seede. 2 Ma sujjóot jublook sa kër gu sell gi, di wormaal saw tur, ngir sa ngor ak sa worma. Màggal nga sa tur ak sa kàddu, ba mu tiim lépp. 3 Bés ba ma wootee, yaa ma wuyu, ñemeel ma, dooleel ma. 4 Aji Sax ji, na la buuri àddina yépp màggal, ñoo dégg kàddu yi nga wax. 5 Nañu woy say jaloore, naan: «Aji Sax jeeka màgg ndam!» 6 Aji Sax jee kawe! Ku toroxlu, mu niir; ku réy, mu ñooru. 7 Ma wéye njàqare, nga musal ma, dogalee sa loxo merum noon, walloo ma sa ndijoor. 8 Aji Sax jee may feyul. Éy Aji Sax ji, yaa saxoo ngor! Bul wacc ñi nga binde sa loxo.

Everything we make is available for free because of a generous community of supporters.

Donate