Menu

Taalifi cant 137

MBS

1 Ca tàkkal dexi Babilon, foofa lanu daa toog, fàttaliku Siyoŋ, jooy. 2 Ca garab ya lanu daa wékk sunuy xalam. 3 Fa la nu sunuy sang daa woyloo, noot nu, bëgg nu bégal leen, naan: «Woyalleen nu ci woyi Siyoŋ.» 4 Moo! Nu nuy woye woyu Aji Sax ji kaw suufas yéefar? 5 Éy Yerusalem, su ma la naree fàtte, yal na ma doole dëddu! 6 Yerusalem, su ma la fàttalikuwul, fonk la, ba gën laa bége lépp, yal na sama làmmiñ tafoo sama denqleñ. 7 Aji Sax ji, fàttalikul Edomeen ña, keroog jantub Yerusalem, ba ñu naan: «Màbbleen a màbb, ba suuf sa dëkk bi sampe siiñ!» 8 Yeen waa Babilon gi ñu nara fàllas, ndokkalee ku leen fey jëf ja ngeen nu def! 9 Ndokkalee ku ne cas seeni fere, tas ciw doj!

Everything we make is available for free because of a generous community of supporters.

Donate