Menu

Taalifi cant 129

MBS

1 Di woy yu ñuy yéege ca tund ya, di ko màggale Yàlla. Ba may ndaw ba tey, ñu ngi may sonal a sonal. Israayiloo, waxati ko: 2 Ba may ndaw ba tey, ñu ngi may sonal a sonal, te taxul ñu man ma. 3 Sama gannaaw gi lañu gàbb a gàbb, rëdd koo rëdd nib tool. 4 Waaye àtteb Aji Sax ji mooy dëgg, dog na buumi ñu bon ña. 5 Képp ku noonoo Siyoŋ, yal nañu ko dëpp, gàcceel ko. 6 Yal nañu mel ni ñax mu saxem xadd, balaa law, lax. 7 Du doyub ŋëb ku ko dog; du doyub say ku ko for. 8 Ku fa jaare it du ko ne: «Jaajëf, Aji Sax ji barkeel; jaajëfe yaw, yal na Aji Sax ji barkeel.»

Everything we make is available for free because of a generous community of supporters.

Donate