Menu

Taalifi cant 127

MBS

1 Di woy yu ñuy yéege ca tund ya, di ko màggale Yàlla, ñeel Suleymaan. Kër, su ko Aji Sax ji tabaxul, ku ko tabax, neen nga doñ-doñi. Ab dëkk, su ko Aji Sax ji wattuwul, ku ko wattu, neen nga teewlu. 2 Neen it la nit di teela jóg aka guddee tëdd, di doñ-doñi lu mu lekk: Aji Sax ji leel na soppeem lu ni day, fekk ko muy nelaw. 3 Ma ne, doom Aji Sax jee koy sédde, njurum doom yool la. 4 Doom joo jure ndaw, mooy fitt ci loxol jàmbaar; 5 ndokkalee ku ci mbuusam fees, ba bu ñu taseekub noon ca pénc ma, duñu am gàcce mukk.

Everything we make is available for free because of a generous community of supporters.

Donate