Menu

Taalifi cant 111

MBS

1 Màggalleen Ki Sax! Naa sante Aji Sax ji léppi xol ci biir ñu jub ñi bokk jataay. 2 Liggéeyi Aji Sax ji réy na, ku ko safoo di ko gëstu. 3 Jëfam di teddngaak daraja, njubteem di sax ba fàww. 4 Moo dogal ñuy fàttalikuy kéemaanam; Aji Sax ji boroom yiw ak yërmande. 5 Mooy leel ku ko ragal, di bàyyi xel kóllëreem gi ba fàww. 6 Won na ñoñam dooley jëfam, ba mu leen joxee suufu xeet yi. 7 Ay jëfam dëgg laak yoon, tegtalam yépp mata wóolu, 8 laloo dëgg ak njub, te sax dàkk ba fàww. 9 Moo yónnee xeetam wall, fas ak ñoom kóllëre gu sax. Kee sell te jara ragal! 10 Ragal Aji Sax ji di njàlbéenu rafet xel, dég-dég bu rafet ñeel ku koy wéye. Moo yeyoo cant ba fàww.

Everything we make is available for free because of a generous community of supporters.

Donate