Menu

Taalifi cant 110

MBS

1 Ñeel Daawuda, dib taalifu cant. Aji Sax ji daa wax sama Sang, ne ko: «Toogeel sama ndijoor, ba ma def say noon sa ndëggastal.» 2 Sa nguur la Aji Sax ji saxal, dale ko fa Siyoŋ. Yilifal noon yi la wër! 3 Sa mboolooy taxawal seen bopp, sa bésub xare. Ñu sol darajaak cellte, faboo fa njël sosoo, diy ndaw, wàccsil la, nib lay. 4 Aji Sax jee ko giñ, te du dellu gannaaw: «Yaa dib sarxalkat ba fàww, topp dayob Melkiccedeg .» 5 Sang baa ngi fi sa ndijoor te mooy rajaxe buur yi, bés bu meree. 6 Mooy mbugal xeet yi, jal seeni néew, di rajaxe kilifay àddina, ba mu daj. 7 Déeg ba feggook yoon wa, Buur a cay naan, te moo ko tax di siggi.

Everything we make is available for free because of a generous community of supporters.

Donate