Menu

Taalifi cant 99

MBS

1 Aji Sax jeey Buur. Yeen xeet yi, ragalleen ko! Moo toogandook malaakay serub yi. Suufoo, soo yeboo, yëngu! 2 Aji Sax ji fi Siyoŋ a màgg, kawe, tiim xeetoo xeet. 3 Sa tur weeka màgg te raglu. Sàbbaalleen ko. —Kee sell! 4 Buur, jëfe yoon mooy dooleem. Yaa saxal yoon, dëgg ak njub ci askanu Yanqóoba. 5 Màggalleen sunu Yàlla, Aji Sax ji, te sujjóot fa ndëggastalam. —Kee sell! 6 Musaak Aaróona bokk ciy sarxalkatam, Samiyel bokk ca ñay ñaan ci turam. Ñuy ñaan Aji Sax ji, mu di leen nangul. 7 Fa biir taxaaru niir wa la waxeek ñoom, ñu topp kàdduy seedeem ak dogalu yoonam ba mu leen joxoon. 8 Céy sunu Yàlla Aji Sax ji, yaa leen nanguloon, di seen Yàlla ju leen di baal, te di leen mbugale seeni jëf ju bon. 9 Màggalleen sunu Yàlla, Aji Sax ji, te sujjóot fa tundam wu sell wa. Sunu Yàlla Aji Sax jee sell!

Everything we make is available for free because of a generous community of supporters.

Donate