Menu

Taalifi cant 87

MBS

1 Ñeel askanu Kore wu góor, di woyu cant. Dëkkub Aji Sax ji, kenu yaa nga ca tund yu sell ya. 2 Aji Sax jee sopp bunti Siyoŋ gii, mu gënal ko fu askanu Yanqóoba dëkke. 3 Yaw, dëkkub Yàlla bi, tuddees na say jaloore. Selaw. 4 Yàlla nee: «Ma limaale Misraak Babilon, ñi ma xam di dégg. Xoolal Filisti ak Tir, ak réewum Kuus. Nit a ngii, juddoo fa.» 5 Te teewul ñu cosaanale ko Siyoŋ, ne kii ak kee fa bokk juddoo, te Aji Kawe jee saxal Siyoŋ. 6 Aji Sax jeey lim xeet yi, limaale leen ne: «Kii fi la juddoo.» Selaw. 7 Kuy fecc ak kuy woy ànd naan: «Sunu cosaanoo cosaan fii la!»

Everything we make is available for free because of a generous community of supporters.

Donate