Menu

Taalifi cant 82

MBS

1 Dib taalifu cant, ñeel Asaf. Yàlla toog na, di jiite ndajem boppam, di àtte ndawi péncam, naan: 2 «Dungeen bàyyi àtteb njublaŋ, ak di faral ku bon? Selaw. 3 Sàmmleen àqu néew-ji-dooleek jirim, tey àtte yoon ku ñàkk ak ku ndóol. 4 Walluleen néew-ji-dooleek walaakaana, di leen xettali ci ku bon. 5 «Ndawi péncum Yàlla yii xamuñu, dégguñu; xanaa di doxe lëndëmu ñaawtéef, ba ponki dëgg yépp di jaayu. 6 «Dama ne ay yàlla ngeen, yeen ñépp di njabootu Aji Kawe ji. 7 Waaye du leen tee dee ni doom aadama, du leen tee daanu ni képp kuy njiit.» 8 Ngalla Yàlla, taxawal, àtte àddina, yaw yaa séddoo xeetoo xeet.

Everything we make is available for free because of a generous community of supporters.

Donate