Taalifi cant 64
MBS1 Mu jëm ci njiital woykat yi, dib taalifu cant, ñeel Daawuda. 2 Éy Yàlla, déglul sama kàddug tawat; ngalla aaral sama bakkan ci noon bu raglu. 3 Làq ma pexey ku bon, ma rëcc gàngooru defkati ñaawtéef. 4 Ñu ngi daas seen làmmiñ niy saamar, di fitte seeni kàdduy wextan, 5 di jam ku ñu tëru te deful dara; jekki jam ko, te tiituñu ci dara. 6 Dañoo dogu ca lu bon la ñu nar, di diisoo na ñuy làqe ay fiir, te naan: «Kenn du ko gis!» 7 Dañuy lal pexem njubadi te naan: «Lal nanu pexe mu mat sëkk.» Nit aka xóot xel te xóoti mbóot! 8 Waaye Yàllaa leen di jamu fittam, ñu jekki daanu. 9 Seen làmmiñ a leen di fakkastal, ba ku leen xool wëcc bopp. 10 Ñépp a ciy am tiitaange, bay siiwal la Yàlla def, tey xalaataat jëfam jooju. 11 Ku jub bége Aji Sax ji, làqoo ko. Képp ku namm njub, damu.
