Taalifi cant 20
MBS1 Mu jëm ci njiital woykat yi, dib taalifu cant, ñeel Daawuda. 2 Buur, yal na la Aji Sax ji nangul bésu njàqare, yal na la turu Yàllay Yanqóoba aj fu kawe, 3 yal na la yónnee wallam fa këram, jàppalee la fa, ca Siyoŋ. 4 Yal na xool loo ko jébbal, di rafetlu sarax soo ko lakkal. Selaw. 5 Yal na la may li nga namm, di sottal loo mébét, 6 ngay daan, nuy ree, yéege sunu raaya, màggal sunu Yàlla. Yal na Aji Sax ji nangu loo dagaan. 7 Aji Sax jeey musal ki mu fal, bir na ma tey. Moo koy nangule fa asamaan su sell sa, ci dooley ndijooram biy musle. 8 Ñiiki watiir, ñeeki fas, nun sunu turu Yàlla Aji Sax ji lanuy tudd. 9 Ñoom ñooy jeng aka jóoru, nun, nu jóg, taxaw jonn. 10 Éy Aji Sax ji, mayal Buur mu daan, te bés bu nu ko ñaane, mu nangul nu.
