Menu

Taalifi cant 15

MBS

1 Dib taalifu cant, ñeel Daawuda. Aji Sax ji, kuy ganeji sa xayma? Ana kuy dëkki sa tund wu sell? 2 Xanaa ki wéye màndu, di def lu jekk, di wax dëggu xolam. 3 Du sos, du tooñ dëkkandoo, du baatal moroomam. 4 Ku siblu, mu sib, ku ragal Yàlla, mu teral. Mooy sàmm ngiñam, su ko dee lor it. 5 Du leble, ba teg ca; du nangu ger, ngir fexeel jàmbur. Lii ku koy jëfe doo jang.

Everything we make is available for free because of a generous community of supporters.

Donate