Menu

Taalifi cant 120

MBS

1 Di woy yu ñuy yéege ca tund ya, di ko màggale Yàlla. Ci sama njàqare laa woo Aji Sax ji wall, mu wuyu ma. 2 Éy Aji Sax ji, musal ma ci gémmiñu fen-kat, ak làmmiñu njublaŋ. 3 Yaw boroom làmmiñu njublaŋ, ana lu ñu lay añale ak lu ñu lay dolli? 4 Xanaa fitti mbër yu ñaw ak xal yu yànj. 5 Wóoy man mi ganeyaani baadooloy Meseg ya tey dali fa xaymay waa Kedar ñu xayadi ña! 6 Yàgg naa lool ci biir nit ñi bañ jàmm. 7 Man may wut jàmm, te su ma waxee, ñoom ñuy ayoo.

Everything we make is available for free because of a generous community of supporters.

Donate