Menu

Taalifi cant 101

MBS

1 Ñeel Daawuda, dib taalifu cant. Ngor ak yoon laay woy. Yaw Aji Sax ji laay joobe. 2 Naa teewlu yoonu màndute. Ana kañ nga may dikkal? Naa doxe màndute fi sama biir waa kër. 3 Caaxaani neen, xooluma; jëf ju wàcc yoon, bëgguma, taqu ma fenn. 4 Kuy nas njekkar, sore ma; lu bon, xawma ko. 5 Kuy jëw moroomam, ma wedamal; ku daŋŋiiral ak ku reew, muñaluma la. 6 Ku dëggu ci réew mi, ma geesu, ngir fat ko. Te kuy wéye màndute, kookoo may liggéeyal. 7 Kuy njublaŋ du tooge sama kër, kuy fen du taxaw sama kanam. 8 Maay xëy, sànk képp ku bon ci réew mi, ngir génne ci dëkkub Aji Sax jii képp kuy def lu ñaaw.

Everything we make is available for free because of a generous community of supporters.

Donate